Jubboo Lyrics
Yenn saay ma tay ko xuloo ak yaw (Ahh !!)
Ndax lay xew ci biir juboo ba (Waaw, foofu lu fa xew ?)
Reewantu yakkul mbëggeel
Feeling la ci
Waawaaw
Li la duggal ci man
Génn wu la ci (Surtout loolu !!)
Man su ma ragalul woon Yàlla
Ni ma ak yaw
Pik ak pël
Tàqale wu ñu
Kaay, ñu dem fu la neex
Xale bii lée, yaw laa jox bopp
Mën uma la tenir tête
Da ma laa nopp
Naa ñakk jom, cóolul
Ndax mer la wóorul
Yaw sa dara sóoful
Ndax bayyi la yóombul
Tay, man sama konpteuru xol
Nga woyofal yaa ko tay
Même suñu bañantee
Sama alal ngay doon ba tay
Nañ juboo ma ak yaw
Maa yërëm noon yi
Soccu woon, di xaar
Ku ñu reetaan
Moo tax waruñ xuloo ma ak yaw
Ndax yaay sérrale xol bi
Bu ko jarree sax, ma raamal la (Mo xanaa nga bañ ?)
Feccal la (Mo xanaa nga bañ ?)
Di la ayoo nenne
Bae kaay, ma yeetal la (Mo xale bi, xanaa nga bañ ?)
Tay ngay jommi
Joboo ak yaw lu am jom nii. (Mo xanaa nga bañ ?)
Kaay fii, chéri
Li dess waxu biir neeg la
Hey
Sa chéri du la séetaan nga fiy ñaaw
Ne da laa bëgg
Yaa yórr kahiyeem
Mu yórr sa bic
Ni da lay bindal
Su ma jubee xare bi, du ma dëpp
Ndax ñaayu xare laa man
Ken du laal li ma moom
Ndaanaan ndaanaan koy antan
Chéri coco, ney neex
Jëndël glaas
Cuub naa drapo bi weex
Tay sama xol dafa neex
Ndax dama juboo ak baneex
Hey
Namm nga ko
Nammoon na la
Nammante ngeen
Xuloo ñaar a kay def
Kon, bisous, wante leen mouwa
Kon mbëggeel ba laa neex, rax ñakk jom
Xale bii
Suñ xuloo maa lay tuddu, yaa ko fa am
Waaw
Soo xamoon tay jii li ma namm ci yaw
Naa noppi sax ba laa waa Jamra di ñëw
Nañ juboo ma ak yaw (Ñowël,)
Maa yërëm noon yi
Soccu woon di xaar
Ku ñu reetaan (Eeh, seen xol du neex tay.)
Moo tax waru ñu xuloo ma ak yaw
Ndax yaay sérrale xol bi
Bu ko jarree sax, ma raamal la (Mo xanaa nga bañ ?)
Feccal la (Mo xanaa nga bañ ?)
Di la ayoo nenne
Bae kaay, ma yeetal la (Mo xale bi, xanaa nga bañ ?)
Tay ngay jommi
Joboo ak yaw lu am jom nii (Mo xanaa nga bañ ?)
Kaay fii, chéri
Li dess waxu biir neeg la
Kon, fanaan
Yaa ma ne woon fanaan
Yaa ne woon fanaan
Yaa ma ne woon fanaan
Fanaan si naa
Fanaan
Chéri fanaan
Yaw fanaan
Yaa ma ne woon fanaan
Fanaan ci naan
Jali, xalamal ma
Ma woyal sama waa ji
Ma ak yaw amuñ nëbboo
Yaay sama wetël
Waruñ xuloo
Yaw fanaan
Chéri fanaan
Yaw fanaan
Yaa ma ne woon fanaan
Fanaan si naa
Bu ko jarree sax, ma raamal la
Feccal la
Di la ayoo nenne
Bae kaay, ma yeetal la
Tay ngay jommi
Joboo ak yaw lu am jom nii
Kaay fii, chéri
Li dess waxu biir neeg la
WATCH VIDEO
ABOUT THIS SONG
Release Year : 2025
Album : (Single)
Added By : Farida
SEE ALSO
AUTHOR
YOU MAY ALSO LIKE